Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 25:3-7 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 25:3-7 in Kàddug Yàlla gi

3 Maneesula daj li ci xelu buur, xalaatam daa kawe ni asamaan, xóot ni suuf.
4 Xellil xaalis, tonni lu ca rax, ba ab tëgg man caa am ndab.
5 Ab soxor it, dàqal, mu sore buur, ngir njubte law, jalam sax.
6 Bul réy-réylu fi kanam buur, bul tooge jataayu boroom daraja,
7 ndax ñu ne la: «Yéegal, jegesi fii,» moo gën ñu torxal la ci kanam kilifa. Boo gisalee sa bopp it,
Kàddu yu Xelu 25 in Kàddug Yàlla gi