23 Jëw, mer a cay topp; mooy ngelawal taw, taw a cay topp.
24 Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.
25 Xibaaru jàmm, bawoo fu sore mooy ndox mu sedd ci ku loof.
26 Ku jub bu dee nangul ku bon, yàqu na, ni seyaan bu nëx mbaa teen bu xàbb.
27 Lekk lem ju ëpp baaxul, te wut waaw-góor du ngóora.
28 Ku dul ànd ak sa sago, yaa neexa song ni dëkk bu dara wërul.