1 Lii it ay kàddu yu xelu la, di yu Suleymaan, ay niti Esekiya buurub Yuda sotti ko.
2 Màggug Yàllaa ngi ci li mu làq, darajay buur a ngi ci li mu feeñal.
3 Maneesula daj li ci xelu buur, xalaatam daa kawe ni asamaan, xóot ni suuf.
4 Xellil xaalis, tonni lu ca rax, ba ab tëgg man caa am ndab.
5 Ab soxor it, dàqal, mu sore buur, ngir njubte law, jalam sax.
6 Bul réy-réylu fi kanam buur, bul tooge jataayu boroom daraja,
7 ndax ñu ne la: «Yéegal, jegesi fii,» moo gën ñu torxal la ci kanam kilifa. Boo gisalee sa bopp it,
8 bul gaawa layooji, ana nooy def ëllëg, bu ñu la yeyee?
9 Ñaarool ak ki nga joteel, te bul jéebaane jaambur.
10 Lu ko moy ñu dégg ko, rusloo la, sab der yàqu yaxeet.
11 Wax ju ñor di nataalu wurus wu tege ci xaalis.
12 Kàddu yu lay yedd ci kuy dégg, jaarob wurus la mbaa gànjaru ngalam.
13 Ndaw lu wóor day seral xolu njaatigeem, mooy ndox mu sedd ci tàngooru ngóob.
14 Kuy dige te doo joxe, yaay xiin wu ngelaw, mu naaxsaay.
15 Muñ mer ay nax kilifa, te wax ju neex, fu mu jaar, mu nooy.
16 Boo gisee lem, lekkal lu yem; bu ëppee, nga waccu ko.
17 Na sa tànk di gëj kër dëkkandoo; boo ko sàppee, mu jéppi la.