9 Pexem dof bàkkaar la, te kuy ñaawle, ñu sib la.
10 Bu mettee, nga yoqi, sa doolee néew.
11 Wallul ku ñuy reyi te tooñul, xettlil kuy tërëf, ñu di ko reyi.
12 Soo nee sa yoon nekku ci it, kiy natt xol yi, xam na, moom miy wattu sa bakkan, xam na, te kat mooy fey nit jëfam.
13 Doom, deel lekk lem, baax na, lem ju xelli, boo sexee, mu tem-temi.
14 Xamal ne xel mu rafet ni la neexe; soo xeloo, sa muj rafet, te sa yaakaar du tas.
15 Soxor bi, bul tëru ku jub ci këram, bul yàq dëkkuwaayam.
16 Ku jub day daanu juróom yaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.
17 Bu sab noon daanoo, bu ko bànneexoo, bu tërëfee, bu ko bége.
18 Lu ko moy Aji Sax ji gis la, ñaawlu ko, daldi giif, dootu ko mbugal.
19 Bu sa xol tàng ci ku bon, bul ñee ku soxor.
20 Ku bon amul muj, ku soxor day mel ni taal bu fey.
21 Doom, ragalal Aji Sax ji, wormaal buur. Bul lëngook kuy fippu.
22 Yàllaak buur a koy bette mbugal, te kenn xamul musiba mu muy doon.