5 Ku rafet xel di boroom doole, ku xam, gëna man;
6 tegtal yu xelu lañuy xaree, diisoo bu yaatooy maye ndam.
7 Wax ju xelu sut nab dof, jataayu pénc du fa àddoo.
8 Kuy mébét lu bon, ñu ne yaay rambaaj bi.
9 Pexem dof bàkkaar la, te kuy ñaawle, ñu sib la.
10 Bu mettee, nga yoqi, sa doolee néew.
11 Wallul ku ñuy reyi te tooñul, xettlil kuy tërëf, ñu di ko reyi.