25 ku ko ne: «Yaa tooñ,» yaay baaxle, taasoo barke bu yaa.
26 Ki lay wax dëgg sa soppe la.
27 Ruujal sab tool, ji ko, doora tabax sa kër.
28 Bul tuumaal nit ci neen, te bu ko seedeel ay fen.
29 Bul ne: «Li mu ma def laa koy def, damay feyu li mu ma def.»
30 Toolub ku yaafus laa jaare, ak tóokërub nit ku ñàkk bopp.
31 Ndeke lépp a nga saxi dég, fépp fees akum ñax, tabaxu doj ba ko wër màbb.
32 Maa ko gis, di xalaat, xoolaat ko, jànge ca.
33 Booy dajjant ak a for bët, di tegley loxook a jaaxaan,
34 néewlee ngi lay dikkal nib sàcc, ñàkk gànnaayul la.