23 Lii it ñi rafet xel a ko wax. Par-parloo cib àtte baaxul.
24 Ku ne defkatu lu bon: «Yaw, tooñoo,» aw nit móolu la, mbooloo ŋàññ la;
25 ku ko ne: «Yaa tooñ,» yaay baaxle, taasoo barke bu yaa.
26 Ki lay wax dëgg sa soppe la.
27 Ruujal sab tool, ji ko, doora tabax sa kër.
28 Bul tuumaal nit ci neen, te bu ko seedeel ay fen.