Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 24:22-26 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 24:22-26 in Kàddug Yàlla gi

22 Yàllaak buur a koy bette mbugal, te kenn xamul musiba mu muy doon.
23 Lii it ñi rafet xel a ko wax. Par-parloo cib àtte baaxul.
24 Ku ne defkatu lu bon: «Yaw, tooñoo,» aw nit móolu la, mbooloo ŋàññ la;
25 ku ko ne: «Yaa tooñ,» yaay baaxle, taasoo barke bu yaa.
26 Ki lay wax dëgg sa soppe la.
Kàddu yu Xelu 24 in Kàddug Yàlla gi