Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 24:2-10 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 24:2-10 in Kàddug Yàlla gi

2 ndax coxor lay nas ci xolam, te fitna la ay waxam di yee.
3 Xel mu rafet ay tabax kër, rafet déggin a koy samp.
4 Xam-xam ay feesal néeg ya ak mboolem alal ju jafe te yànj.
5 Ku rafet xel di boroom doole, ku xam, gëna man;
6 tegtal yu xelu lañuy xaree, diisoo bu yaatooy maye ndam.
7 Wax ju xelu sut nab dof, jataayu pénc du fa àddoo.
8 Kuy mébét lu bon, ñu ne yaay rambaaj bi.
9 Pexem dof bàkkaar la, te kuy ñaawle, ñu sib la.
10 Bu mettee, nga yoqi, sa doolee néew.
Kàddu yu Xelu 24 in Kàddug Yàlla gi