Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 24:14-19 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 24:14-19 in Kàddug Yàlla gi

14 Xamal ne xel mu rafet ni la neexe; soo xeloo, sa muj rafet, te sa yaakaar du tas.
15 Soxor bi, bul tëru ku jub ci këram, bul yàq dëkkuwaayam.
16 Ku jub day daanu juróom yaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.
17 Bu sab noon daanoo, bu ko bànneexoo, bu tërëfee, bu ko bége.
18 Lu ko moy Aji Sax ji gis la, ñaawlu ko, daldi giif, dootu ko mbugal.
19 Bu sa xol tàng ci ku bon, bul ñee ku soxor.
Kàddu yu Xelu 24 in Kàddug Yàlla gi