Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 24:13-16 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 24:13-16 in Kàddug Yàlla gi

13 Doom, deel lekk lem, baax na, lem ju xelli, boo sexee, mu tem-temi.
14 Xamal ne xel mu rafet ni la neexe; soo xeloo, sa muj rafet, te sa yaakaar du tas.
15 Soxor bi, bul tëru ku jub ci këram, bul yàq dëkkuwaayam.
16 Ku jub day daanu juróom yaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.
Kàddu yu Xelu 24 in Kàddug Yàlla gi