3 Bul xemmem daraam lu neex, ñam woowu la lay naxe.
4 Bul rey sa bopp ci wut alal, bu ko xalaat sax.
5 Ndax xef ak xippi mu wéy, mel ni lu saxi laaf, ne fëyy, naaw ni jaxaay.
6 Ab nay, bul lekke këram, bul xemmem daraam lu neex.
7 Ma ngay xool la ngay lekk, nu mu tollu, naan la: «Lekkal, naanal!» Te xol ba àndu ca.
8 Ndog soo ca lekk, waccu ko, yiw woo ko wax daldi neen.
9 Bul wax akub dof, day xeeb sam xel.