26 Doom, teewloo ma xel te roy ma.
27 Ab gànc yeer mu xóot la, jabaru jaambur di teen bu xat.
28 Ma ngay tëroo nib sàcc, góor ñu bare lay fecciloo worma.
29 Ana kuy tiislu, naan: «Wóoy, ngalla man!» Ana kuy xulook a jàmbat, di gaañu ci dara, bët ya xonq curr?
30 Xanaa kiy naan-naane biiñ, di mosi yeneen njafaan?
31 Bul xool biiñ ak xonqaayam. Aka yànj cib kaas te neexa jolu!
32 Bu weesee mu màtt la ni jaan, ne la càppit ni ñàngóor.
33 Dangay mel ni kuy gis lu doy waar, sam xel di ràbb lu jekkadi.