Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 23:23-34 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 23:23-34 in Kàddug Yàlla gi

23 Jëndal dëgg te bu ko jaay. Sàkkul xel mu rafet ak yar akug dégg.
24 Su doom jubee, seral xolu baay. Boo juree ku rafet xel, am nga bànneex.
25 Deel bégal ndey ak baay, rawatina ndey ji la jur.
26 Doom, teewloo ma xel te roy ma.
27 Ab gànc yeer mu xóot la, jabaru jaambur di teen bu xat.
28 Ma ngay tëroo nib sàcc, góor ñu bare lay fecciloo worma.
29 Ana kuy tiislu, naan: «Wóoy, ngalla man!» Ana kuy xulook a jàmbat, di gaañu ci dara, bët ya xonq curr?
30 Xanaa kiy naan-naane biiñ, di mosi yeneen njafaan?
31 Bul xool biiñ ak xonqaayam. Aka yànj cib kaas te neexa jolu!
32 Bu weesee mu màtt la ni jaan, ne la càppit ni ñàngóor.
33 Dangay mel ni kuy gis lu doy waar, sam xel di ràbb lu jekkadi.
34 Nga mel ni ku tëdd biir géej, di jaayu ca biir gaal ga,
Kàddu yu Xelu 23 in Kàddug Yàlla gi