7 Ku am ay yilif ku ñàkk, koo leb di surgaam.
8 Ku ji njubadi, góob fitna, yet wa muy dóore, damm.
9 Ku tabe am barke, mooy kiy sédd ku ñàkk cib dundam.
10 Dàqal kuy ñaawle, ay jeex, xulooki saaga dakk.
11 Ku dëggu, wax ja yiw, buur di xaritam.
12 Aji Sax jeey sàmm liy dëgg, di weddi waxi fen-kat.
13 Bul yaafus, ba naan: «Gayndee ngi ci biti, dañu may rey ci mbedd mi!»
14 Waxi ndaw su yemadi am yeer la, ku Aji Sax ji rëbb moo cay tàbbi.