Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 22:5-11 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 22:5-11 in Kàddug Yàlla gi

5 Yoonu njublaŋ, ay dég aki fiir; ku sàmm sa bakkan sore ko.
6 Tegal gone ciw yoon, ba bu màggee, du ko wacc.
7 Ku am ay yilif ku ñàkk, koo leb di surgaam.
8 Ku ji njubadi, góob fitna, yet wa muy dóore, damm.
9 Ku tabe am barke, mooy kiy sédd ku ñàkk cib dundam.
10 Dàqal kuy ñaawle, ay jeex, xulooki saaga dakk.
11 Ku dëggu, wax ja yiw, buur di xaritam.
Kàddu yu Xelu 22 in Kàddug Yàlla gi