Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 22:5-10 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 22:5-10 in Kàddug Yàlla gi

5 Yoonu njublaŋ, ay dég aki fiir; ku sàmm sa bakkan sore ko.
6 Tegal gone ciw yoon, ba bu màggee, du ko wacc.
7 Ku am ay yilif ku ñàkk, koo leb di surgaam.
8 Ku ji njubadi, góob fitna, yet wa muy dóore, damm.
9 Ku tabe am barke, mooy kiy sédd ku ñàkk cib dundam.
10 Dàqal kuy ñaawle, ay jeex, xulooki saaga dakk.
Kàddu yu Xelu 22 in Kàddug Yàlla gi