Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 22:4-7 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 22:4-7 in Kàddug Yàlla gi

4 Woyofal te ragal Aji Sax ji, am alal, gudd fan ak daraja.
5 Yoonu njublaŋ, ay dég aki fiir; ku sàmm sa bakkan sore ko.
6 Tegal gone ciw yoon, ba bu màggee, du ko wacc.
7 Ku am ay yilif ku ñàkk, koo leb di surgaam.
Kàddu yu Xelu 22 in Kàddug Yàlla gi