24 Bul xaritook ku gaawa mer, bul ànd ak ku tàng bopp.
25 Lu ko moy nga mel ni moom, te kon nga lonku.
26 Bul bokk ci ñiy dige, di gàddul nit bor.
27 Soo amul loo ko feyale, ñu yékkatee la sab lal, nangu ko.
28 Bul toxal màndargam cosaan ci làccu suuf te say maam tegoon ko fa démb.