Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 22:21-25 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 22:21-25 in Kàddug Yàlla gi

21 ngir xamal la lu wér te dëggu, nga yóbbaale kàdduy dëgg, yoo tontoo ña la yebal.
22 Bul xañ néew-ji-doole; néew-ji-doole la. Ku tumurànke, bu ko soxore cib àtte,
23 Aji Sax ji da koy taxawu, ku ko xañ, mu xañ la bakkan.
24 Bul xaritook ku gaawa mer, bul ànd ak ku tàng bopp.
25 Lu ko moy nga mel ni moom, te kon nga lonku.
Kàddu yu Xelu 22 in Kàddug Yàlla gi