Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 22:2-11 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 22:2-11 in Kàddug Yàlla gi

2 Ku am ak ku ñàkk a bokk lenn: Aji Sax jee leen boole sàkk.
3 Kuy foog, gisu ay, làqu; ab téxét ne ca tëñëx, loru.
4 Woyofal te ragal Aji Sax ji, am alal, gudd fan ak daraja.
5 Yoonu njublaŋ, ay dég aki fiir; ku sàmm sa bakkan sore ko.
6 Tegal gone ciw yoon, ba bu màggee, du ko wacc.
7 Ku am ay yilif ku ñàkk, koo leb di surgaam.
8 Ku ji njubadi, góob fitna, yet wa muy dóore, damm.
9 Ku tabe am barke, mooy kiy sédd ku ñàkk cib dundam.
10 Dàqal kuy ñaawle, ay jeex, xulooki saaga dakk.
11 Ku dëggu, wax ja yiw, buur di xaritam.
Kàddu yu Xelu 22 in Kàddug Yàlla gi