Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 22:17-24 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 22:17-24 in Kàddug Yàlla gi

17 Teewlul te déglu li boroom xel yi wax. Defal sam xel ci li ma lay xamal.
18 Soo mokkalee, ba man koo tari, muy sa mbégte.
19 Yaw laa koy xamal tey jii, ndax nga wóolu Aji Sax ji.
20 Dama laa bindal fanweeri dénkaane, ci wàllu digal ak xam-xam,
21 ngir xamal la lu wér te dëggu, nga yóbbaale kàdduy dëgg, yoo tontoo ña la yebal.
22 Bul xañ néew-ji-doole; néew-ji-doole la. Ku tumurànke, bu ko soxore cib àtte,
23 Aji Sax ji da koy taxawu, ku ko xañ, mu xañ la bakkan.
24 Bul xaritook ku gaawa mer, bul ànd ak ku tàng bopp.
Kàddu yu Xelu 22 in Kàddug Yàlla gi