16 Not néew-ji-doole ngir yokkule, mbaa may boroom alal, loo ci def mu wàññi la.
17 Teewlul te déglu li boroom xel yi wax. Defal sam xel ci li ma lay xamal.
18 Soo mokkalee, ba man koo tari, muy sa mbégte.
19 Yaw laa koy xamal tey jii, ndax nga wóolu Aji Sax ji.
20 Dama laa bindal fanweeri dénkaane, ci wàllu digal ak xam-xam,