14 Waxi ndaw su yemadi am yeer la, ku Aji Sax ji rëbb moo cay tàbbi.
15 Yëfi dof daa sax ci xolu gone, boo bantalee, mu tàggook moom.
16 Not néew-ji-doole ngir yokkule, mbaa may boroom alal, loo ci def mu wàññi la.
17 Teewlul te déglu li boroom xel yi wax. Defal sam xel ci li ma lay xamal.