6 Alal ju la fen may, cóolóol la, day naaw, wut ko xaru la.
7 Coxor day sànk boroom, ndax day baña def njub.
8 Ab saaysaay day dëngal, nit ku dëggu di jubal.
9 Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.
10 Ab soxor day namma lore, te du yërëm moroomam.
11 Boo mbugalee kuy ñaawle, ab téxét jànge ca; nga jàngal ku rafet xel, mu yokku.
12 Aji Jub ji Yàlla xam na la ne ca biir kër ku bon, te mooy sànk ku bon.