Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 21:3-10 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 21:3-10 in Kàddug Yàlla gi

3 Deel def dëgg ak njekk, moo gënal Aji Sax ji ab sarax.
4 Xeebaateek réy-réylu mooy bàkkaar yi ñuy ràññee ku bon.
5 Farlu, woomle; ku gaawtu, mujj néewle.
6 Alal ju la fen may, cóolóol la, day naaw, wut ko xaru la.
7 Coxor day sànk boroom, ndax day baña def njub.
8 Ab saaysaay day dëngal, nit ku dëggu di jubal.
9 Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.
10 Ab soxor day namma lore, te du yërëm moroomam.
Kàddu yu Xelu 21 in Kàddug Yàlla gi