25 Ab yaafus day bëgg lu mu amul ba dee, ndax du nangoo liggéey;
26 day yendoo xemmem, te du am, ka jub di joxeek a joxewaat.
27 Saraxu nit ku bon ñaawtéef la, rawatina bu ci jubloo lu bon.
28 Seede buy fen day sànku, kuy dégg, sa kàddu sax.
29 Ku bon day ñeme-ñemelu, ku jub la muy def da koy wóor.
30 Nit xeluwul, amul ug dégg ak pexe, ba manal Aji Sax ji dara.
31 Nit ay takk, bésub xare, Aji Sax ji di maye ndam.