Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 21:21-28 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 21:21-28 in Kàddug Yàlla gi

21 Ku saxoo njekk ak ngor am fan wu gudd, naataangeek daraja.
22 Ku ñaw mana daan jàmbaari dëkk bu mag, ba màbb tata ja ñu yaakaaroon.
23 Ub sa gémmiñ, moom sa làmmiñ, mucc ci njàqare.
24 Ku réy te bew, mooy ñaawle, day reew, ba jéggi dayo.
25 Ab yaafus day bëgg lu mu amul ba dee, ndax du nangoo liggéey;
26 day yendoo xemmem, te du am, ka jub di joxeek a joxewaat.
27 Saraxu nit ku bon ñaawtéef la, rawatina bu ci jubloo lu bon.
28 Seede buy fen day sànku, kuy dégg, sa kàddu sax.
Kàddu yu Xelu 21 in Kàddug Yàlla gi