20 Ku xelu denc këram ngëneeli alal aku diw, ab dof saax-saaxee josam.
21 Ku saxoo njekk ak ngor am fan wu gudd, naataangeek daraja.
22 Ku ñaw mana daan jàmbaari dëkk bu mag, ba màbb tata ja ñu yaakaaroon.
23 Ub sa gémmiñ, moom sa làmmiñ, mucc ci njàqare.
24 Ku réy te bew, mooy ñaawle, day reew, ba jéggi dayo.
25 Ab yaafus day bëgg lu mu amul ba dee, ndax du nangoo liggéey;
26 day yendoo xemmem, te du am, ka jub di joxeek a joxewaat.