Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 21:2-18 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 21:2-18 in Kàddug Yàlla gi

2 Lu waay def, daa jub ca moom, waaye Aji Sax jeey natt xol yi.
3 Deel def dëgg ak njekk, moo gënal Aji Sax ji ab sarax.
4 Xeebaateek réy-réylu mooy bàkkaar yi ñuy ràññee ku bon.
5 Farlu, woomle; ku gaawtu, mujj néewle.
6 Alal ju la fen may, cóolóol la, day naaw, wut ko xaru la.
7 Coxor day sànk boroom, ndax day baña def njub.
8 Ab saaysaay day dëngal, nit ku dëggu di jubal.
9 Dëkkeb ruq cim sàq moo gën jabar ju pànk.
10 Ab soxor day namma lore, te du yërëm moroomam.
11 Boo mbugalee kuy ñaawle, ab téxét jànge ca; nga jàngal ku rafet xel, mu yokku.
12 Aji Jub ji Yàlla xam na la ne ca biir kër ku bon, te mooy sànk ku bon.
13 Ku tanqamlu jooyi ku ñàkk dina woote wall, wall ñàkk.
14 Ku mer, may ko ci sutura, mu giif; boroom xadar, boqal ko neexal, mu dal.
15 Bu yoon amee, ku jub bég; kuy def lu bon jàq.
16 Ku noppee jëfe xel, noppluji njaniiw.
17 Ku topp sa bànneex, mujje ñàkk; ku sopp biiñ ak lu niin du woomle.
18 Ku bon këppoo ayu ku baax, workat gàddu musibam kuy jubal.
Kàddu yu Xelu 21 in Kàddug Yàlla gi