15 Bu yoon amee, ku jub bég; kuy def lu bon jàq.
16 Ku noppee jëfe xel, noppluji njaniiw.
17 Ku topp sa bànneex, mujje ñàkk; ku sopp biiñ ak lu niin du woomle.
18 Ku bon këppoo ayu ku baax, workat gàddu musibam kuy jubal.
19 Dëkke ndànd-foyfoy moo gën jabar ju tàng, bare ay.
20 Ku xelu denc këram ngëneeli alal aku diw, ab dof saax-saaxee josam.