13 Ku tanqamlu jooyi ku ñàkk dina woote wall, wall ñàkk.
14 Ku mer, may ko ci sutura, mu giif; boroom xadar, boqal ko neexal, mu dal.
15 Bu yoon amee, ku jub bég; kuy def lu bon jàq.
16 Ku noppee jëfe xel, noppluji njaniiw.
17 Ku topp sa bànneex, mujje ñàkk; ku sopp biiñ ak lu niin du woomle.
18 Ku bon këppoo ayu ku baax, workat gàddu musibam kuy jubal.
19 Dëkke ndànd-foyfoy moo gën jabar ju tàng, bare ay.
20 Ku xelu denc këram ngëneeli alal aku diw, ab dof saax-saaxee josam.
21 Ku saxoo njekk ak ngor am fan wu gudd, naataangeek daraja.
22 Ku ñaw mana daan jàmbaari dëkk bu mag, ba màbb tata ja ñu yaakaaroon.