Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 1:8-13 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 1:8-13 in Kàddug Yàlla gi

8 Doom, toppal yaru baay, te bul wacc ndigalu yaay.
9 Kaala gu jekk la ci bopp, di gànjar ci baat.
10 Doom, bàkkaarkat bu la xiirtal, lànkal.
11 Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jaambur bu deful dara.
12 Nanu mel ni njaniiw, mëdd kuy dund, mu jekki tàbbi biir bàmmeel.
13 Mboolem alal ju réy, nu jagoo, yeb sunu biir kër, mu fees.
Kàddu yu Xelu 1 in Kàddug Yàlla gi