7 Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
8 Doom, toppal yaru baay, te bul wacc ndigalu yaay.
9 Kaala gu jekk la ci bopp, di gànjar ci baat.
10 Doom, bàkkaarkat bu la xiirtal, lànkal.
11 Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jaambur bu deful dara.