Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 1:3-8 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 1:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 ngir yaru ci jëfe xel ak njub ak yoon, di jubal,
4 ndax ab téxét di foog, ndaw li it xam tey xalaat.
5 Na boroom xel mu rafet déglu, yokk dég-dégam, te kiy ràññee di jariñoo ay tegtal,
6 ngir mana xam aw léeb aku taas ak kàddug boroomi xel yu rafet ak seeni cax.
7 Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
8 Doom, toppal yaru baay, te bul wacc ndigalu yaay.
Kàddu yu Xelu 1 in Kàddug Yàlla gi