3 ngir yaru ci jëfe xel ak njub ak yoon, di jubal,
4 ndax ab téxét di foog, ndaw li it xam tey xalaat.
5 Na boroom xel mu rafet déglu, yokk dég-dégam, te kiy ràññee di jariñoo ay tegtal,
6 ngir mana xam aw léeb aku taas ak kàddug boroomi xel yu rafet ak seeni cax.