Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 1:22-25 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 1:22-25 in Kàddug Yàlla gi

22 Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi? Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi? Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?
23 Soo dëppee ba déglu, ma àrtu la. Ma ne, kon ma xellil la samam xel, xamal la samay kàddu.
24 Damaa woote, nga gàntal, ma tàllal loxo, faaleesu ma.
25 Sofental nga samay digle, nanguwoo samay àrtu.
Kàddu yu Xelu 1 in Kàddug Yàlla gi