Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 1:17-22 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 1:17-22 in Kàddug Yàlla gi

17 Doo firib caax, ba jàpp njanaaw luy xoole.
18 Ñii kat seen bopp lañuy fiir, seen bakkanu bopp lañu sànk.
19 Képp kuy lekk lu lewul, nii lay mujje: wutin wu lewul jël bakkanu boroom.
20 Xel mu Rafet a ngay woote ca mbedd ma, di xaacu ca pénc ma.
21 Ma ngay wootee bérab yu gëna xumb, di dégtaley kàddoom, bunt dëkk ba.
22 Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi? Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi? Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?
Kàddu yu Xelu 1 in Kàddug Yàlla gi