14 Dikkal nu far, mbuus miy benn, nu bokk.»
15 Doom, bul ànd ak ñoom ciw yoon, bul jaare fa ñuy jaar,
16 ngir dañuy xélu, nar musiba, di gaawtuy sànk bakkan.
17 Doo firib caax, ba jàpp njanaaw luy xoole.
18 Ñii kat seen bopp lañuy fiir, seen bakkanu bopp lañu sànk.
19 Képp kuy lekk lu lewul, nii lay mujje: wutin wu lewul jël bakkanu boroom.
20 Xel mu Rafet a ngay woote ca mbedd ma, di xaacu ca pénc ma.
21 Ma ngay wootee bérab yu gëna xumb, di dégtaley kàddoom, bunt dëkk ba.
22 Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi? Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi? Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?
23 Soo dëppee ba déglu, ma àrtu la. Ma ne, kon ma xellil la samam xel, xamal la samay kàddu.
24 Damaa woote, nga gàntal, ma tàllal loxo, faaleesu ma.