Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 1:13-27 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 1:13-27 in Kàddug Yàlla gi

13 Mboolem alal ju réy, nu jagoo, yeb sunu biir kër, mu fees.
14 Dikkal nu far, mbuus miy benn, nu bokk.»
15 Doom, bul ànd ak ñoom ciw yoon, bul jaare fa ñuy jaar,
16 ngir dañuy xélu, nar musiba, di gaawtuy sànk bakkan.
17 Doo firib caax, ba jàpp njanaaw luy xoole.
18 Ñii kat seen bopp lañuy fiir, seen bakkanu bopp lañu sànk.
19 Képp kuy lekk lu lewul, nii lay mujje: wutin wu lewul jël bakkanu boroom.
20 Xel mu Rafet a ngay woote ca mbedd ma, di xaacu ca pénc ma.
21 Ma ngay wootee bérab yu gëna xumb, di dégtaley kàddoom, bunt dëkk ba.
22 Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi? Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi? Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?
23 Soo dëppee ba déglu, ma àrtu la. Ma ne, kon ma xellil la samam xel, xamal la samay kàddu.
24 Damaa woote, nga gàntal, ma tàllal loxo, faaleesu ma.
25 Sofental nga samay digle, nanguwoo samay àrtu.
26 Kon boo sëngéemee, man it ma ree, njàqare dab la, may textexi.
27 Njàqare di ngëlén, dab la, sa musiba def callweer, buub la, njekkar ak fitna dal la.
Kàddu yu Xelu 1 in Kàddug Yàlla gi