11 Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jaambur bu deful dara.
12 Nanu mel ni njaniiw, mëdd kuy dund, mu jekki tàbbi biir bàmmeel.
13 Mboolem alal ju réy, nu jagoo, yeb sunu biir kër, mu fees.
14 Dikkal nu far, mbuus miy benn, nu bokk.»
15 Doom, bul ànd ak ñoom ciw yoon, bul jaare fa ñuy jaar,
16 ngir dañuy xélu, nar musiba, di gaawtuy sànk bakkan.