Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 1:1-6 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 1:1-6 in Kàddug Yàlla gi

1 Kàddu yu xelu yu Suleymaan buurub Israyil, di doomu Daawuda.
2 Li ko taxa jóg di nit ñi am xel mu rafet, am ab yar, ngir xam wax ju lal dég-dég,
3 ngir yaru ci jëfe xel ak njub ak yoon, di jubal,
4 ndax ab téxét di foog, ndaw li it xam tey xalaat.
5 Na boroom xel mu rafet déglu, yokk dég-dégam, te kiy ràññee di jariñoo ay tegtal,
6 ngir mana xam aw léeb aku taas ak kàddug boroomi xel yu rafet ak seeni cax.
Kàddu yu Xelu 1 in Kàddug Yàlla gi