Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 19:8-17 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 19:8-17 in Kàddug Yàlla gi

8 Kuy sàkku xel, bëgg nga sa bopp; kuy wut ag dégg day baaxle.
9 Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen, mujje sànku.
10 Dund gu neex jekkul cib dof, surga buy jiite kilifa it moo yées.
11 Ku xam lu jaadu, muñ mer, tanqamlu ku la tooñ ngay damoo.
12 Merum buur ni gaynde gu ŋar; yërmandey buur ni lay cig mbooy.
13 Doom ju dof naqaru baay baa, te jabar ju pànk mooy senn bu dakkul.
14 Kër ak alal ngay donne ci baay; jabar ju xelu, Aji Sax jee koy maye.
15 Ab yaafus, nelaw yu xóot, te ku yàccaaral xiif.
16 Ku jëfe ndigal, sàmm sa bakkan; ku moytuwul sa bopp, dangay dee.
17 Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.
Kàddu yu Xelu 19 in Kàddug Yàlla gi