8 Kuy sàkku xel, bëgg nga sa bopp; kuy wut ag dégg day baaxle.
9 Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen, mujje sànku.
10 Dund gu neex jekkul cib dof, surga buy jiite kilifa it moo yées.
11 Ku xam lu jaadu, muñ mer, tanqamlu ku la tooñ ngay damoo.
12 Merum buur ni gaynde gu ŋar; yërmandey buur ni lay cig mbooy.