4 Ku barele, barey xarit; ku ñàkk, sab xarit dagg la.
5 Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen du rëcc àtteem.
6 Ñu baree ngi wuta neex boroom daraja, ku nekk a bëgga xaritook kuy joxe.
7 Ku ñàkk, sa bokk yépp dëddu la, sab xarit gën laa soreeti, ngay wax ak ñoom, dara.
8 Kuy sàkku xel, bëgg nga sa bopp; kuy wut ag dégg day baaxle.
9 Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen, mujje sànku.
10 Dund gu neex jekkul cib dof, surga buy jiite kilifa it moo yées.