24 Ab yaafus day yeb loxoom ci ndab, tàyyi ko yékkati, sex.
25 Boo ñefee ab ñaawlekat, téxét ba jànge ca; nga yedd kuy dégg, mu xame ca.
26 Kuy yàqal sa baay, di dàq sa ndey, yaay indi gàcceek yeraange.
27 Doom, soo noppee déglu ku lay yar, sore nga kàdduy xam-xam.