Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 19:22-28 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 19:22-28 in Kàddug Yàlla gi

22 Li ñu sopp ci nit mooy ngor, néewle moo gën fen.
23 Ragalal Aji Sax ji ndax nga gudd fan, nopplu te baña loru.
24 Ab yaafus day yeb loxoom ci ndab, tàyyi ko yékkati, sex.
25 Boo ñefee ab ñaawlekat, téxét ba jànge ca; nga yedd kuy dégg, mu xame ca.
26 Kuy yàqal sa baay, di dàq sa ndey, yaay indi gàcceek yeraange.
27 Doom, soo noppee déglu ku lay yar, sore nga kàdduy xam-xam.
28 Seedeb naaféq faalewul yoon, ab soxor lu bon lay tàqamtikoo.
Kàddu yu Xelu 19 in Kàddug Yàlla gi