Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 19:2-9 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 19:2-9 in Kàddug Yàlla gi

2 Teeyadi baaxul, ku yàkkamti moy saw yoon.
3 Nit def na jëfi dof, ba sànku, walbatiku mere Aji Sax ji.
4 Ku barele, barey xarit; ku ñàkk, sab xarit dagg la.
5 Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen du rëcc àtteem.
6 Ñu baree ngi wuta neex boroom daraja, ku nekk a bëgga xaritook kuy joxe.
7 Ku ñàkk, sa bokk yépp dëddu la, sab xarit gën laa soreeti, ngay wax ak ñoom, dara.
8 Kuy sàkku xel, bëgg nga sa bopp; kuy wut ag dégg day baaxle.
9 Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen, mujje sànku.
Kàddu yu Xelu 19 in Kàddug Yàlla gi