Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 19:19-27 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 19:19-27 in Kàddug Yàlla gi

19 Ku naqari deret, sonal nga sa bopp; ku la xettli, tóllanti ko.
20 Déggal ndigal te yaru, ndax ëllëg nga xelu.
21 Bare na lu xol di mébét, waaye Aji Sax jeey dogal.
22 Li ñu sopp ci nit mooy ngor, néewle moo gën fen.
23 Ragalal Aji Sax ji ndax nga gudd fan, nopplu te baña loru.
24 Ab yaafus day yeb loxoom ci ndab, tàyyi ko yékkati, sex.
25 Boo ñefee ab ñaawlekat, téxét ba jànge ca; nga yedd kuy dégg, mu xame ca.
26 Kuy yàqal sa baay, di dàq sa ndey, yaay indi gàcceek yeraange.
27 Doom, soo noppee déglu ku lay yar, sore nga kàdduy xam-xam.
Kàddu yu Xelu 19 in Kàddug Yàlla gi