Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 19:16-21 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 19:16-21 in Kàddug Yàlla gi

16 Ku jëfe ndigal, sàmm sa bakkan; ku moytuwul sa bopp, dangay dee.
17 Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.
18 Yaral sa doom ba muy teel, waaye bul topp sa xol, ba rey ko.
19 Ku naqari deret, sonal nga sa bopp; ku la xettli, tóllanti ko.
20 Déggal ndigal te yaru, ndax ëllëg nga xelu.
21 Bare na lu xol di mébét, waaye Aji Sax jeey dogal.
Kàddu yu Xelu 19 in Kàddug Yàlla gi